TSK

TSK · Micah 7:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Jaambur ñay dégg, di rag-ragi, tiitaange ne taral waa Filisti,

Aji Sax ji, jógal, bu la nit yab; na xeet yi dikk fi sa kanam, nga àtte leen.

Waa màndiŋ mi di ko sukkal, ay noonam mëq suuf,

nit ñi làquji biir xuntiy doj, ruuruji biiri pax, ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab, sore darajay màggaayam, kera buy taxaw, ba suuf di lox.

Moo tax xeet wu am doole di la màggal, waa péeyu xeet yu néeg di la wormaal.

Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu, wormaale teddngaam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.

Ba ngay def kiraama ya ñu séentuwuloon, yaa wàcc, tund yi yëngu fi sa kanam.

¶ «Maa ngii di woolu nappkat yu bare.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu napp ñii ba noppi ma woo rëbb yu bare, ñu rëbb leen ci kaw mboolem tund wu mag ak wu ndaw, ba ci bépp xar-xaru doj.

Ñenn ci jàngub Seytaane bi, ñooñuy fen, di tuddoo ay Yawut te duñuy Yawut, maa ngii di leen xiirtal, dikkloo leen, sujjóotloo leen fi sa kanam, ba ñu xam ne man maa la sopp.

¶ Buuri àddina yi àndoon ak dëkk bii ci moy ak dund gu bakkane, bu ñu séenee saxaras lakkam, ñoom ñépp ay yuuxu, di ko jooy.