Su boobaa seen Yàlla Aji Sax jee leen di xarfal xarafu xol, te mooy xarfal xarafu xol, seen askan, ngir ngeen soppe seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ndax ngeen dund.
TSK
TSK · Micah 7:19
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Daawuda ne Gàdd: «Am naa njàqare lool; waaye naa tàbbi ci loxol Aji Sax ji, ndax yërmandeem réy na, waaye yàlla buma daanu ci loxol nit!»
baal sa mbooloo seeni ñaawtéef, jéggal leen bépp bàkkaar. Selaw.
Ni penku soree sowu, ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ.
Du kenn ci waa Yerusalem, ku neeti wopp na. Waa dëkk bépp ay am njéggalu bàkkaar.
Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttliku bàkkaar.
Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.
Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am; fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal.
Bu la tegee naqar it, yërëm la, ngoram a ni baree.
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.
Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
Waaye gis naa ci samay cér, weneen yoon wuy xeex ak yoon wi samam xel jubool, te yoon woowoo ma jàpp njaam, jébbal ma dooley bàkkaar bi dëkke samay cér.
Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
Am defe ngeen ne ag neen la Mbind mi indee ne: «Xemmemtéef gu ànd ak fiiraange la Yàlla am ci noo gi dëkk ci nun.»