TSK

TSK · Nahum 1:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Keey saxal ngor ba ci junniy maas, di bale tooñ ak moy ak bàkkaar, te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem, xanaa di topp doom tooñu waajur, ba ca sët yaak sëtaat ya.»

su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar.

Seen Yàlla Aji Sax ji kat, mooy sawara wuy xoyome, Yàlla ju fiir la.

«Xanaa du loolu laa làq fi sama wet, ne ko ràpp fi samay denc?

bu ma daasee sama saamar buy melax, ba ŋàbb ko ci saab loxo, di àtte, maay fey samay digaale, añale samay bañ.

Job 20:23 TSK

Ba muy sol kollam la ko Yàlla di yónnee tàngooru sànjam, tawal ko ko lu fees déqam.

Aji Sax jeey waaxu ni jàmbaar, xabtalu ni ñeyu xare, àddu ca kaw, xaacu, tiime noon yi njàmbaaram.

Sa doom yi ne lasar, mbete kooba yu fiir jàpp, ñu ne lareet fépp fu mbedd daje, këppoo sànjum Aji Sax ji, sa Yàlla ji leen rëbb.

«Maa doon dëre tànk, man kenn ci ab dërukaayu reseñ, xeet yépp kenn dërlewu ma ci. Sama mer laa leen dëre, samam sànj laa leen dëggaatee, seen deret tis ci samay yére, ma taqal sama yére yépp.

Xanaa deesul mer ba fàww? Xanaa xadar du sax?” Ma ne: “Israyiloo, yeena ko wax, waaye bon ngeen lu ngeen man.”»

¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil déy da maa wax ne ma: «Am kaasu biiñ bii ci sama loxo, di misaal kaasu mbugal, te nga nàndal ci mboolem xeet yi ma lay yebal,

Xaaculeen fi kawam, wër ko, Babilon daanu na, ba joxe ndodd, tata ya màbb, dàbbli ya rajaxoo! Aji Sax jeey feyu, feyuleen! Na mu defoon, defleen ko ko.

Maa leen di ŋaccal sama mer, sottil leen sama xadar ba giif, te bu ma leen ŋaccalee sama mer, ñu xam ne man Aji Sax ji, maa waxe sama fiiraange.

Man it maa leen di feye xadar. Duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Dinañu yuuxu yuux yu réy, may dégg te duma leen faale.»

Bésub keroog, ba Gog di dalsi ca kaw réewum Israyil, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, sama xadaru mer ay fettax.

Joel 2:18 TSK

Aji Sax ji moo fiire am réewam, ñeewante ñoñam.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy, am sànj mu réy laa koy fiiree.»

Samay soppe, buleen di feyul seen bopp, xajal-leen am sànj, am sànj fajal boppam, ndax bindees na ne: «Man maay feye, maay añale.» Boroom bee ko wax.

Xam nanu ki wax ne: «Ag pey, maay boroom, man maay añale,» neeti: «Boroom bi mooy àtte ñoñam.»