¶ Gannaaw loolu Elyasib sarxalkat bu mag ba ànd ak bokki sarxalkatam, ñu tabaxaat bunt ba ñuy wax Gàtt ya, sellalal ko Yàlla, taxawal laf ya, defaraat tata ja, ba ca soorooru Meya, sellalal ko Yàlla, jàppoo ko noonu ba ca soorooru Ananel.
TSK
TSK · Nehemiah 12:39
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Nehemiah 3:1
TSK
Nehemiah 3:6
TSK
¶ Buntu Cosaan ba, Yowada doomu Paseya ak Mesulam doomu Besodiya ñoo ko defaraat, daaj bant ya, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd.
Nehemiah 3:31
TSK
Ka ca topp di defar, di Malkiya, bokk ca tëggi wurus ya. Muy liggéey ba ca këri liggéeykati kër Yàlla ga ak jaaykat ya, fa janook buntu Ndaje ba, jàpp ca néegu jongrukat bu kawe ba ca ruq ba.
Jeremiah 31:38
TSK
¶ Mu ne: «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «dees na tabaxalaat Aji Sax ji dëkk bi, dale ko ca soorooru Ananel ba ca buntu Ruq ba.
Zephaniah 1:10
TSK
Su bés baa,» Aji Sax jee ko wax, «yuux dina jibe fa buntu Jën ya, wóoy jibe fa Sanc ya, rajaxoo ju réy jollee ca tund ya.