ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;
TSK
TSK · Numbers 1:46
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.»
maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk,
Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.
¶ Ci kaw loolu bànni Israyil jóge dëkk ba ñuy wax Ramses, jëm Sukkóot. Ña nga tollu ci juróom benni téeméeri junniy góor (600 000) te limaaleesul jigéen ñaak xale ya.
¶ Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!»
Juróom ñaar fukki bakkan la seeni maam doonoon ba ñuy wàccsi Misra. Tey seen Yàlla Aji Sax ji def leen ngeen day ni biddiiwi asamaan.
¶ Waa Yuda ak Israyil dañoo bare woon, ba mel ni feppi suufas géej, di lekk, di naan, nekke mbégte.
¶ Ci kaw ngëm itam la Saarata ci boppam mana ëmbe ba jur tey mag ba wees njurum doom, ndax moo njortoon ne ka dige ku wóor la.