TSK

TSK · Numbers 10:12

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ñu bàyyikoo Sukkóot, dal Etam ca wetu màndiŋ ma.

¶ Saa yu niir wa yékkatikoo, ba tiim jaamookaay ba nag, bànni Israyil daldi tegu ca seen yooni tukki ya.

¶ Bànni Israyil daldi def noonu. Mboolem noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na lañu daan dale, topp seeni raaya, na lañu daan jóge, ku nekk ak làngam ak kër maamam.

Ñu daldi màggal bésub Mucc bi ci weer wi jëkk, fukki fanam ak ñeent, diggante ngoon ak jant bu so, ca màndiŋu Sinayi. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la ko bànni Israyil defe.

Ci kaw loolu Musaa yebal ndaw ña ci ndigalal Aji Sax ji, ñu bàyyikoo ca màndiŋu Paran. Ñoom ñépp ay njiiti bànni Israyil lañu woon.

Ñu bàyyikoo Refidim, dali ca màndiŋu Sinayi,

¶ Lii mooy kàddu yi Musaa wax bànni Israyil gépp, ca wàllaa dexu Yurdan, ca màndiŋ ma, fa joor ga jàkkaarlook Suf, diggante Paran ak Tofel ak Laban ak Aserot ak Disayab.

¶ Gannaaw gi nu bàyyikoo tundu Oreb, jaare mboolem màndiŋ mu yaa, mu raglu ma ngeen gis. Nu topp yoonu diiwaanu tundi Amoreen ñi, na nu ko sunu Yàlla Aji Sax ji sante woon, ba àgg Kades Barneya.

¶ Gannaaw ba loolu wéyee Samiyel faatu, Israyil gépp daje, dëj ko, daldi koy denc ca këram ca Raama. Daawuda nag fabu, wuti màndiŋu Paran.

Yàllaa ngi jóge Teman, Aji Sell ji foofa ca tundu Paran lay bawoo. Selaw Darajaam moo dajal asamaan, teddngaam fees kaw suuf.