TSK

TSK · Numbers 10:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn.

ak tabaxkat yaak yettkati doj ya, jënd ca bant ak doji yett, yi ñu soxla ci defarub kër Aji Sax ji, ak mboolem lu ñuy jënd ngir defar kër Aji Sax ji.

Yékkatileen woy te jiin, xalam neex, ànd ak moroom ma.

Buleen fi indeeti saraxi caaxaan, seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la. Terutel weer ak bésub Noflaay ak wooteb ndajee ci yem! Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.

Hosea 8:1 TSK

«Sexleen bufta gi! Jaxaay jàyy ci waa kër Aji Sax ji, nde ñoo fecci sama kóllëreek ñoom, samaw yoon lañu gàntal.

Joel 2:1 TSK

Wal-leen bufta ca Siyoŋ, dégtal-leen ab yéene ca sama kaw tund wu sell. Na waa réew mi mépp lox, nde bésub Aji Sax jaa ngi dikk te dëgmal na.