¶ Ci biir loolu Yàlla xalaat na Nóoyin ak li mu nekkal ci gaal gi, di rabi àll yi ak jur gi. Yàlla daldi yebal ngelaw, mu wal kaw suuf, ba ndox yi wàcc.
TSK
TSK · Numbers 10:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Bu ngeen demee ngir xarejeek seeni noon ba gis ay fas, aki watiir, ak gàngoor gu leen ëpp, buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ki leen jële woon réewum Misra.
Mu wax bànni Israyil, ne leen: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Man maa génne Israyil Misra. Maa leen xettli ca waa Misra ak mboolem buur ya leen notoon.
seen noon ya not leen, ñu torox ca seeni loxo.
Yeen waa àddina wërngal këpp, yeen ñi dëkke suuf si, séentuleen raaya ba sampe fa tund ya, dégluleen liit ga ñuy wali.
«Nangeen yégle lii fa Yuda, dégtale ko fa Yerusalem, yéenee koog liit fi biir réew mi te xaacu seen kem kàttan ne leen: “Dajeleen, nu dem ca dëkk ya tata wër.”
Xanaa duma gis ba fàww raayab noon, liitu xare di ko feelu?
«Ma tabbal leeni wattukat ne: “Teewluleen liit gu jib.”» Ñu lànk ne: «Teewluwnu.»
su kooka séenee congum xare muy dikk ci réew mi, daldi wal liit gi, àrtu waa réew mi,
Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?
noonee mu ko waxe woon ca jant yu jëkk ya, yonentam yu sell ya woon jottli,