TSK

TSK · Numbers 11:12

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw.

Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.

Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.»

ca màndiŋ ma it, gis ngeen na leen seen Yàlla Aji Sax ji fabe, ni baay di fabe doomam, ci yoon wi ngeen dox wépp, ba agsi bérab bii.»

«Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram. Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte.

¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.

Yeen samay doom! Maa ngi dellooti ci mat wu ma leen jure woon ni jigéen, ba keroog Almasi mate sëkk ci yeen.