TSK

TSK · Numbers 11:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ibraam dégg loola, daldi sujjóot. Yàlla wax ak moom ne ko:

Aji Sax ji nag àddu ne: «Bàkkaari Sodom ak Gomor bare na lool, ba may dégg yuux, yi sababoo ci seen moy.

Nga bàyyi leen nag, ñuy àtteel mbooloo mi bés bu nekk seeni jote. Su ko defee, mboolem réeroo bu mag, ñu indil la ko; mboolem réeroo bu sew nag, ñoom ñu àtteel ko seen bopp. Noonu ngay woyofale sab yen, ñu jàpple la ci.

Ba mu ko defee Aji Sax ji wàcc ca tundu Sinayi wa, ca njobbaxtalu tund wa. Aji Sax ji nag woo Musaa foofa, ca njobbaxtal ga, Musaa dellu yéeg.

¶ Bu Musaa duggaan ca biir xaymab ndaje ma, ngir wax ak Aji Sax ji, day dégg baat ba di wax ak moom, bawoo fa tiim kubeeru gaalu seedes kóllëre ga, ca diggante ñaari serub ya. Noonu la daan waxeek moom.

Aji Sax ji wàcc ci biir niir wu def aw taxaar. Mu taxaw ca bunt xayma ba, daldi woo Aaróona ak Maryaama, ñu bokk dikk.

Aji Sax ji ne Musaa: «Jëlal Yosuwe doomu Nuun. Nit la ku noowal biir nekk ci moom. Nanga ko teg sa loxo, sase ko noonu.

¶ Ba ñu jàllee, Ilyaas ne Alyaasa: «Wax ma lu ma lay defal bala ñu maa yóbbu, may teqlikook yaw!» Alyaasa ne ko: «Xanaa naa am lu mat sag leer ñaari yoon.»

Sa xel mu rafet nga leen may ba ñu mana ràññee, sa mànn it, noppiwuloo leen koo leel, teg ca ndox ma nga leen daan fajale mar.

«Ab jotkat ay dikkal Siyoŋ, ba jot ñi tuub seeni bàkkaar ci askanu Yanqóoba.» Kàddug Aji Sax jee.

Acts 6:3 TSK

Kon nag bokk yi, seetleen ci seen biir juróom ñaar ñu rafet seede, soloo Noo gu Sell gi te rafet xel, nu dénk leen sas woowu.

Nun nag du xelum àddina lanu jot, waaye Xel mi bawoo fa Yàlla lanu jot, ngir nu mana ràññee li nu Yàlla baaxe.

Kon nag ku jalax ndigal lii, du nit nga jalax, xanaa Yàlla, moom mi leen jox Noowam gu Sell.

Jude 1:19 TSK

Ñooñu ñooy féewalekat yi, ñoo topp seen bindu judduwaale, te Noowug Yàlla nekkul ci ñoom.