Musaa bàyyikoo ca Firawna, tinu Aji Sax ji.
TSK
TSK · Numbers 11:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba mu ko defee Musaa dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Éey Aji Sax ji, mbooloo mii de moy nañu la lool, ba ñu sàkkalee seen bopp ay yàllay wurus.
Musaa ne Aji Sax ji: «Kon de, waa Misra ga nga jële mbooloo mii, génnee leen sa doole ca seen biir, dinañu ko dégg,
Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma.
Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.
Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»
¶ Mu am bés Buur Cedesyas woo Yukal doomu Selemya, ak Cefaña sarxalkat bi, doomu Maaseya. Mu yebal leen ci Yonent Yàlla Yeremi; ñu ne ko: «Rikk ñaanal nu ci sunu Yàlla Aji Sax ji.»
Soccet yiy lekk gàncaxu réew mi, ba mu bëgga jeex, ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, ngalla déet! Askanu Yanqóoba àttan na lii am? Lu néew doole lañu.»
¶ Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.