TSK

TSK · Numbers 12:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mu dellu ëmb, am doom ju góor. Mu ne: «Aji Sax ji yég na ne fonkeesu ma, looloo tax mu mayaat ma doom jii.» Mu tudde ko Simeyon (mu firi Kiy dégg).

Aaróona jottli leen kàddu ya Aji Sax ji wax Musaa yépp, ba noppi Musaa wone firnde ya ca kanam mbooloo ma,

¶ Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona àgg ba ca Firawna. Ñu def la leen Aji Sax ji santoon. Aaróona jël yetam, sànni ca suuf ca kanam Firawnaaki dagam; yet wa soppliku jaan.

¶ Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam Aji Sax ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba.

Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»

Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg mboolem kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»

Réy-réylu jote rekk lay jur, ku dégg ndigal a xelu.

Su boobaa nga xam ne man Aji Sax ji, maa dégg sa jépp waxi ñàkk kersa ja nga nee: ‘Tundi Israyil a ngii ne tasar, dim sëxëtoo mu ñu nu wërsëgale.’

Micah 6:4 TSK

Yeen maa leen génnee réewum Misra, kërug njaam googa, maa leen fa jote, ba yebal fi seen kanam, Musaa ak Aaróonaak Maryaama.

Na leen mbëggeelug bokk taxa fonkante, te ngeen farlu ci di terlante.

¶ Mboolem lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo,