Exodus 18:25
TSK
Mu seet ca bànni Israyil gépp, tànn ca góor ñu mat, fal leen, ñu yilif mbooloo ma: ñii jiite kuréli junniy nit; ñii, téeméer; ñii, juróom fukk; ñii fukk.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu seet ca bànni Israyil gépp, tànn ca góor ñu mat, fal leen, ñu yilif mbooloo ma: ñii jiite kuréli junniy nit; ñii, téeméer; ñii, juróom fukk; ñii fukk.
¶ Ba mu ko defee Aji Sax ji dafa wax Musaa, ne ko: «Dajaleel ma juróom ñaar fukki magi Israyil, ñoo xamal sa bopp ne ñooy magi mbooloo mi, di seeni njiit, nga indi leen ci xaymab ndaje mi, ñu teew faak yaw.
Lu mel nii de, la seeni baay defoon ba ma leen yebalee, ñu jóge Kades Barneya, ngir yëri réew ma.
Ci kaw loolu ma jël seen njiit yu rafet xel yu ràññiku, yi ngeen jukkee ci seeni giir, daldi leen def seeni njiit, ñii yilif junniy nit, ñii téeméer, ñii juróom fukk, ñii fukk, ñii diy jawriñ ci seeni giir.