TSK

TSK · Numbers 13:29

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ñu jóge fa nag, waññiku, dem En Mispat, di Kades ba tey, daldi teg mboolem réewum Amalegeen ña tànk, boole ca song Amoreen ña dëkk Asason Tamar.

ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Refayeen ñi,

Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.

¶ Ba loolu weesee Amalegeen ña dikk, xareek bànni Israyil ca Refidim.

Te kat Amalegeen ñi ak Kanaaneen ñaa ngi fuu ci seen kanam. Yeenay fàddoo saamar doŋŋ. Gannaaw yeena dëddu Aji Sax ji nag, Aji Sax ji du ànd ak yeen.»

¶ Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékki kàddug ñaanam, ne: «Amaleg moo sutu xeet, te sànku lay mujje.»

Nangeen faagaagal Etteen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñi ak Yebuseen ñi, na leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante woon,

Njàmbaar la xaree, duma Amalegeen ña, ba musal Israyil ca ña doon sëxëtoo seen alal.

¶ Ci biir loolu Daawuda aki nitam daan nañu song-songee Gesureen ñi ak Giraseen ñi ak Amalegeen ñi. Mooy ña dëkke woon naka jekk réew mooma, ba ca Sur, jàpp réewum Misra.

Yaa gis mu nangul la ci xolam; nga fas ak moom kóllëre, dig askanam réewum Kanaaneen ñaak Etteen ñaak Amoreen ñaak Periseen ñaak Yebuseen ñaak Girgaseen ña. Te def nga li nga dige it, ndax yaw boroom njekk nga.