Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?
TSK
TSK · Numbers 14:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.
¶ Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam Aji Sax ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba.
«Ba kañ la mbooloo mu bon mii di ñaxtu ci sama kaw? Ñaxtu yi bànni Israyil di ñaxtu ci sama kaw, dégg naa ci.
¶ Ci kaw loolu mbooloo ma dem ba ñàkk ndox. Ñu daje ci kaw Musaa ak Aaróona.
Ak ba leen Aji Sax ji yebalee fa Kades Barneya, ne leen: «Demleen nanguji réew ma ma leen jox.» Yeena gàntal seen kàddug Yàlla Aji Sax ji, gëmuleen ko, déggaluleen kàddoom.
Moo lu ma tee woona deeye biiru yaay? Lu ma tee ne putt, dog, boog?
Dañoo gàntal réew mu neex, gëmuñu kàddug Yàlla,
Léegi nag Aji Sax ji, rikk jëlal sama bakkan rekk, ndax dee sax a ma gënal dund!»
Buleen jàmbat, ni ñenn ci ñoom doon jàmbate, ba tax malaakam reykat ba rey leen.
Ñooñoo di ñaxtu ak a jàmbat, te topp seen bakkan; kàdduy damu yu réy ay jibe seen gémmiñ, te ñooy jay ñi ñu yaakaare njariñ.