Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.
TSK
TSK · Numbers 15:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Meneen kuuy mi, nga rendi ko diggante ngoon ak jant bu so, booleeti ko ak saraxu pepp mi ak saraxu tuuru bi, ni woon ci suba, muy xeeñ xetug jàmm, di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu kenn ci yeen dee sàkkal Aji Sax ji sarax, na indi ag jur, muy gu gudd mbaa gu gàtt.
Na boroom sarax bi raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
¶ «Su sarax si nit kiy génne dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene, dees na ko lekk bés bi ko nit ki joxee, te lu ca des ba ca ëllëg sa, ñu man koo lekk.
«Waxal Aaróona aki doomam yu góor ak bànni Israyil gépp ne leen: Képp ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa ci doxandéem yi ci Israyil, di joxeel Aji Sax ji ab saraxu rendi-dóomal, muy sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene,
¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
ak pañeb mburu yu amul lawiir, yu ñu lakke sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak mburu yu sew yu amul lawiir yu ñu wis ag diw, ak saraxi peppam ak saraxi tuuroom ya muy àndal.
Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at.
Sarxal-leen ci ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lu mucc sikk ngeen di def lépp.
Foofa ngeen di yóbbu seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak seen sarax yu ngeen xas, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi taawug jur gu gudd ak gu gàtt.
Seen céru fukkeelu pepp nag, ak bu biiñ bu bees, ak bu diw gu bees, ak seen taawug jur gu gudd ak gu gàtt, ak seen mboolem saraxi xas yu ngeen xasoo woon, ak seen saraxi yéene, ak ab jooxe bu ngeen sàkke ci seenu ñaq, sañuleen cee lekk lenn ci seen biiri dëkk,
Ci biir loolu, xaalis boobu nanga ko daldi jënde ay yëkk aki kuuy ak xar yu ndaw ak saraxi pepp ak saraxi tuuru yi muy àndal te nga boole ko, jooxe ca seen sarxalukaayu kër Yàlla ga ca Yerusalem.
te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi mi nu sopp, ba jooxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara, ngir xetug jàmm, ñeel Yàlla.