TSK

TSK · Numbers 18:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Nanga ber dënn bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, mook tànkub jooxe bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, te ñu jooxee ko ci kuuyu colu gi, ñeel Aaróona aki doomam.

Ci loxol boppam lay dindee sarax bi ñuy def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Day indi nebbon bi, boole kook dënn bi, dënn bi di sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.

Waaye su sarxalkat bi jëndee ab jaam ci xaalisam, jaam ba man na caa lekk. Jaam bu juddoo ci kër sarxalkat bi it man naa lekk ci ñamam woowu.

Lii mooy li lew sarxalkat yi, te bàyyikoo ci askan wi, ci ñiy rendi ay sarax, muy aw nag, di ab gàtt: nañu jox sarxalkat bi, mbagg mi ak lex yi, ak mbàq gi.