TSK

TSK · Numbers 18:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Léegi nag yaw, nanga seppee ci bànni Israyil sa mag Aaróona, ak doomam yu góor, nga woo leen fi yaw, ñu di ma sarxalal: Aaróona ak doomam yu góor, Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.

¶ Loolooy céri pal yi Aaróona ak askanam di am ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, dale ko keroog bu ñu leen teewalee fi kanam Aji Sax ji, ñu doon ay sarxalkat.

te na sàkk andu xal bu fees, tibbe ko ca sarxalukaay ba, fi kanam Aji Sax ji, ak ñaari barci-loxoy cuuraay lu mokk te xeeñ, boole ko yóbbu ca gannaaw rido ba.

Aaróona ak doomam yu góor nag ngay tabb ngir ñu sasoo seenug carxal, waaye képp ku ci laal te bokku ci, dees koy rey.»

Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam.

Nañu jokku ci yaw, te ñu dénkoo ndénkaanel xaymab ndaje mi, ci mboolem liggéeyu xayma bi. Kenn ku ci bokkul nag du leen jege, yeen.

Maa tànne sa baay ci digg giiri Israyil yépp, ngir mu doon sama sarxalkat, di yéeg ci sama sarxalukaay, di taal cuuraay, sol xar-sànni mi, janook man. Maa sédd it sa waa kër baay mboolem saraxi sawara yu bànni Israyil.

Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jaambur ñi dul Yawut, xéewal yu amul kem yi ci Almasi.

Néeg ba ca wàllaa ñaareelu rido ba, moom lañu daan wooye bérab bu sell baa sell.