Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
TSK
TSK · Numbers 18:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Su fekkee ne kilifa moo moy lenn ci santaaney Yàllaam Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,
¶ «Bu nit bàkkaaree ndax lu mu dégg wooteb seede cib àtte, ba noppi baña wax la mu gis mbaa mu xam ko ca mbir ma, dees na ko ko topp.
Sarxalkat bi koy rendi, muy saraxu póotum bàkkaar da ciy lekk, te fu sell lañu koy lekke, ci biir ëttu xaymab ndaje mi.
¶ «Liy dogal bi ci saraxas peyug tooñ mooy lii: Lu sella sell la.
¶ Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la.
Nañu rendi kuuy mi ci bérab bu sell bi, fi ñuy rendee juru saraxu póotum bàkkaar ak saraxu rendi-dóomal, ndax li nekk ci saraxu peyug tooñ moo nekk ci saraxu póotum bàkkaar: sarxalkat bee ko moom; lu sella sell la.
Waaye su sarxalkat bi jëndee ab jaam ci xaalisam, jaam ba man na caa lekk. Jaam bu juddoo ci kër sarxalkat bi it man naa lekk ci ñamam woowu.
¶ Xaalisu saraxu peyug tooñ nag ak xaalisu saraxu póotum bàkkaar daawuñu ko indi ci kër Aji Sax ji. Sarxalkat yaa ko moomoon.