Ñu jóge fa nag, waññiku, dem En Mispat, di Kades ba tey, daldi teg mboolem réewum Amalegeen ña tànk, boole ca song Amoreen ña dëkk Asason Tamar.
TSK
TSK · Numbers 20:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Magu liir ba daldi wax doomu Firawna ja, ne ko: «Ndax ma dem wutali la ku koy nàmpal ci Ebrë yi?»
¶ Maryaama ak Aaróona ñoo doon ŋàññ Musaa, ci ndawas Kuuseen su mu takkoon, te ab Kuuseen it la takkoon.
Ba loolu amee ñu génne Maryaama dal ba diiru juróom ñaari fan. Mbooloo ma demul, ba keroog ba ñu délloosee Maryaama ca biir dal ba.
Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israyil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma.
Musaa summi yérey Aaróona, solal ko doomam Elasar, Aaróona dee foofa ca kaw tund wa, Musaa ak Elasar wàcc tund wa.
gannaaw yeena diiŋat sama ndigal ca màndiŋu Ciin, fa mbooloo ma jote woon ak man. Yeena wormaalul sama sellnga ca kanam mbooloo ma, ca ndox ma. Mooy walum Meriba, (mu firi Jote ba), ma woon ca Kades, ca màndiŋu Ciin.»
¶ Ci kaw loolu ngeen dikk yeen ñépp fi man, ne ma: «Nan yebal aw nit, ñu jiitu nu, yëral nu réew ma, te délsi wax nu yoon wu nuy jaare, ak dëkk yu mag ya nuy duggeji.»
Diggante ba nu bàyyikoo Kades Barneya, di dox, ba keroog bés ba nu jàllee walum Seredd, fanweeri at ak juróom ñett la. Fekk na mboolem maasu góor ña tollu woon ci xare, ca ndoortel yoon wa, ñoom ñépp a wuute dal ba, dee ba jeex, na leen ko Aji Sax ji giñale woon.
Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ, Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
Yeen maa leen génnee réewum Misra, kërug njaam googa, maa leen fa jote, ba yebal fi seen kanam, Musaa ak Aaróonaak Maryaama.