TSK

TSK · Numbers 21:34

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Fexeleen rekk ba Aji Sax ji, buleen ko gàntal, te yeen nag ngeen baña ragal waa réew ma, ndax ab lanc doŋŋ lañu nuy mat. Seen kiiraay dëddu na leen, te Aji Sax jaa ngeek nun. Buleen leen ragal.»

¶ Siwon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii.

Aji Sax ji ne ma: «Bu ko ragal, ndax ci say loxo laa ko teg, mook gàngooram gépp, akum réewam. Nanga ko def na nga defoon Siwon buurub Amoreen ba woon ca Esbon.»

¶ Jombul ngeen di wax ci seen xel naan: «Xeet yii gën noo bare, ana nu nu leen mana dàqe?»

Buleen am tiitaange ci ñoom, ndax seen Yàlla Aji Sax ji ci seen biir, Yàlla ju màgg la te raglu.

ne leen: «Éey Israyil, dégluleen, yeena ngi waaja xareek seeni noon tey jii. Buleen yox-yoxi, buleen ragal, buleen tiit, buleen teqlikook seen sago ci seen kanam!

Daawuda dellu seet ci Aji Sax ji, Aji Sax ji ne ko: «Doxal dem Keyla, man, maay teg waa Filisti ci say loxo.»

Ndeke ci biir loolu ab yonent dem na ca Axab buurub Israyil, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gis nga mbooloom xare mii mépp ak li ñuy bare lépp, xamal ne teg naa leen ci sa loxo bésub tey, ndax nga xam ne maay Aji Sax ji.»

Loolu yomb na Aji Sax ji te dina teg Mowab ci seen loxo it.

Man Aji Sax ji maay sa Yàlla; téye sa loxol ndijoor, di la wax ne la: «Bul tiit, maa lay dimbali.»