TSK

TSK · Numbers 22:36

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Naka la siggi, gis ñetti nit, ñu ne jimeet ci kanamam. Ibraayma gaawtu, gatandu leen, sujjóotal leen.

Musaa génn gatandu ko, sujjóotal ko, fóon ko; ñu jàmmante ba noppi, doora dugg ca xayma ba.

¶ Aji Sax ji neeti: «Ayca, jàll-leen walum Arnon. Mu ngoog, maa teg ci seen loxo, Siwon Amoreen ba, buurub Esbon, mook réewam. Dal-leen di nangu réew mi, song ko xare.

Jigéeni Mowab a nga ca jéggikaayu dexu Arnon, mel ni picc yu tasaaroo fa seeni tàgg, di fët-fëtluy, naaw.

Ba bokki gëmkati Room yégee ne nu ngi dikk, ñoo nu gatandusi ba fa ñuy wax péncu Apiyus ak fa ñuy wax Ñetti dalu gan ya. Ba leen Póol gisee, daa sant Yàlla, daldi gëna sawar.