TSK

TSK · Numbers 22:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan.

Njéeréer ya daa muur suuf sa sépp, ba giseesu ko. Suuf sa ñuul kukk. Njéeréer ya lekk lépp luy gàncax mbaa meññeefi garab gu tawub yuur ba jotuloona yàq, ba lenn lu naat desatul, du xobi garab, du gàncax, ca mboolem réewum Misra.

reyaale buuri Majan, Ewi ak Rekem ak Sur ak Ur ak Reba, juróomi buuri Majan ya. Balaam doomu Bewor it, ñu reye ko saamar.

ndax la ñu leen dabewul woon aw ñam, mbaa am ndox, ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra, xanaa di fey Balaam doomu Bewor ma bokk Petor ca Aram Naarim, ngir mu sàbbi leen.

Li ko waral moo di ñoo bañoona dabe bànni Israyil aw ñam wu ñu lekk ak ndox mu ñu naan, xanaa di fey Balaam, jibar ba, ngir mu rëbbal leen leen. Teewul sunu Yàlla soppi rëbb ga barke.

Micah 6:5 TSK

Yeen sama ñoñ, fàttlikuleen rekk la leen Balag buurub Mowab fexeeloon, ak la ko Balaam doomu Bewor tontu woon. Doxub diggante Sitim ba Gilgal it, baleen ci xel, ba ràññee njekku Aji Sax ji.

Jude 1:11 TSK

¶ Ngalla ñii! Ñoo jaare yoonu Kayin; ñoo lajj, topp Balaam cig réeram ngir ag peyoor; ñoo diiŋat ba sànku ni Kore.