TSK

TSK · Numbers 24:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.»

Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.

Sóol ne: «Yeen njiiti mbooloo mi yépp, dikkleen fii, nu seet ba gis bàkkaarub tey jii, lu mu doon.

Buur Axab nag dee, buuru Mowab jógal buurub Israyil ba ko wuutu.

Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.

Mu teg ca tabb Daawuda, jaamam ba, jële ko ca gétti xar ya,

Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israyil, askanu Yanqóoba,

¶ Lu jëm ci Mowab, Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: «Ngalla waa Nebo, seen dëkk ba yàqu na! Kiryaatayim, ñu torxal, nangu ko; tata ja daanu, tasaaroo.

Fa Yuda la doju collu tabax di bawoo, jënu xayma, fa moom, xalay xare, fa moom, mboolem njiit yi ba ñépp daj, fa moom.

Luke 1:78 TSK

Sunu Yàllaa yaatu yërmande, moo nu fenkal ab jant,

¶ Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol.

Jude 1:14 TSK

¶ Enog, juróom ñaareelu maam ma gannaaw Aadama, ñooñu la jottli woon waxyu bu leen dal, ne: «Boroom baa ngii dikk, ànd ak ay junniy junneem ñu sell,

¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»