¶ Gannaaw loolu Samiyel ne: «Indil-leen ma Agag buurub Amalegeen ñi.» Agag nag dikk, wutsi ko, ne finaax. Booba Agag a nga naan ca xelam: «Dee moom, tiitatuma ko, wees na!»
TSK
TSK · Numbers 24:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Gannaaw ba xew-xew yooyu jàllee, Buur Aserus teral ku ñuy wax Aman doomu Amdeta mi askanoo ci Agag, yékkati ko, teg ko ci kaw mboolem kàngam yi ci wetam.
Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal, ma wetti ni banu mbedd.
buuroo buur di ko sujjóotal, xeetoo xeet di ko surgawu.
di tudd sa teddngay nguur, tey dégtale sag njàmbaar,
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.
Te tundoo tund wu kawe, wu mag ak wu ndaw, wali ndox a cay wale, keroog bés ba deret di tuuroo tuuru, tata ya jóoru.
Yeen ñi dëkke weti ndox yu ne xéew, seen alal ne xéew, seen muj taxaw na, seen buumu bakkan dog na.
¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»
¶ Mu neeti ma: «Ndox yi nga gis jigéenu moykat ji toog ci nag, mooy niti xeet yeek mbooloo yeek askan yeek làmmiñ yi.