TSK

TSK · Numbers 26:65

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ci kaw loolu bànni Israyil jóge dëkk ba ñuy wax Ramses, jëm Sukkóot. Ña nga tollu ci juróom benni téeméeri junniy góor (600 000) te limaaleesul jigéen ñaak xale ya.

Ne leen: Ndegam maay Kiy Dund déy, Kàddug Aji Sax jee, noonu ngeen waxe, may dégg, ni laa leen di def.

Waaye yeen, seeni néew ci màndiŋ mii lay tëdd,

Mennum Yosuwe doomu Nuun ak mennum Kaleb doomu Yefune doŋŋ, ñoo mucc ca ndaw yooya nemmikuji woon réew ma.

Diggante ba nu bàyyikoo Kades Barneya, di dox, ba keroog bés ba nu jàllee walum Seredd, fanweeri at ak juróom ñett la. Fekk na mboolem maasu góor ña tollu woon ci xare, ca ndoortel yoon wa, ñoom ñépp a wuute dal ba, dee ba jeex, na leen ko Aji Sax ji giñale woon.

Ku bon, ñu dagg, sànni; ku yaakaar Aji Sax ji, jagoo réew mi.

¶ Xoolal kon ni Yàlla baaxe, ak ni mu ragloo; ci ñi déggadi la raglu, baax ci yaw, ndegam cig mbaaxam nga sax; lu ko moy dees na la tenqi yaw itam.

Ana ñan la Yàlla mere lu mat ñeent fukki at? Xanaa du mboolem ña bàkkaaroon te seeni néew mujj tëdd ca màndiŋ ma?