Wormaal-leen màggalu bésu Ngóob mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi.
TSK
TSK · Numbers 28:26
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Exodus 23:16
TSK
Leviticus 23:8
TSK
Defleen ci saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. Bésub juróom ñaareel ba di bésub ndaje mu sell. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.»
Leviticus 23:15
TSK
¶ «Bésub Noflaay ba ngeen di indi takku bele biy saraxu yékkati-jébbale, bés ba ca topp ngeen di dale waññ juróom ñaari ayi bés yu mat sëkk.
Numbers 28:18
TSK
Bés bu jëkk boobu, woote bu sell lees cay amal. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
ngeen doora amal màggalug Ayi bés, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, te saraxu yéene ba ngeen cay joxe di kemu koom ga leen seen Yàlla barkeele.
¶ Waaye nag Almasi dafa dekki moos, te mooy saraxu ndoortel meññeef, bi ñu sàkke ci ngóobum bakkani nit ñi dee.