¶ «Li yoon dogal ci saraxu cant ci biir jàmm, te nit sañ koo sarxalal Aji Sax ji mooy lii:
TSK
TSK · Numbers 29:39
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Su nit dee joxsi Aji Sax ji aw nag mbaa gàtt, muy saraxu cant ci biir jàmm, mu di ko wàccoo ngiñ mbaa muy saraxu yéene, na doon lu amul sikk, ndax ñu nangul ko. Lenn luy sikk du nekk ci jur gi.
Du lenn lu ngeen di liggéey ci boobu bés, ndax bésub Njotlaay la bu ngeen di jotoo fi seen kanam Yàlla, Aji Sax ji.
¶ «Loolooy wartéef ci ab nasireen bu xas. Loolooy saraxam bi mu warlook Aji Sax ji cig céddoom, te bokkewul ak leneen lu mu ci àttan; waaye kàdduy xas wa mu xasoon daal, na sàmmonteek moom ni ko yoon diglee ci céddoom googu.»
Foofa ngeen di yóbbu seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak seen sarax yu ngeen xas, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi taawug jur gu gudd ak gu gàtt.
Ñu teg ca amal màggalu Mbaar ya, mu dëppook la ñu bind, boole kook saraxu dóomal yi war bés bu nekk.
¶ Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga,
¶ Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla.