«Nanga ma sédde bépp taaw bu góor, nit ak mala, lépp lu jëkka juddu ci bànni Israyil, maa moom.»
TSK
TSK · Numbers 3:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba Firawna tëwee, bañ noo bàyyi, nu dem, Aji Sax jee rey mboolem lu doon taaw bu góor ca réewum Misra, taawu nit ba ci taawu mala. Looloo waral nuy rendil Aji Sax ji mépp mala mu jëkka juddu, di góor, sunu bépp taaw bu góor it, ñu war koo jote sarax su nu koy rendil.”
¶ «Bépp taaw bu góor maay boroom, ba ci lépp lu góor lu jur taawloo, muy nag mbaa gàtt.
Su ko defee nga beral ma Leween ñi, man Aji Sax ji, ñu wecci mboolem taawi bànni Israyil gi ci des, juri Leween ñi itam wecci mboolem luy taaw ci juri bànni Israyil gi ci des.»
¶ «Man mii nag maa seppee seen bokki Leween ñi ci biir bànni Israyil. Yeen lañu leen jagleela jagleel, ñeel Aji Sax ji, ngir ñu liggéey liggéeyu xaymab ndaje mi.
Booba waa Misraa ngay rob ña Aji Sax ji fàdd ca ñoom, néewi mboolem seen taaw ya. Aji Sax jee mbugale noonu seen yàlla ya.
noonee ñu ko binde ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, dees koy tudde séddoo bu sell, ñeel Boroom bi.»