Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.
TSK
TSK · Numbers 3:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Numbers 1:50
TSK
Numbers 3:32
TSK
Njiiti Leween ñi nag, seen kilifa gu mag moo doon Elasar doomu Aaróona sarxalkat ba. Moo doon saytu ña dénkoo woon dénkaaney bérab bu sell ba.
Numbers 8:15
TSK
Gannaaw loolu la Leween ñiy doora dugg ci liggéeyu xaymab ndaje mi. Danga leen di jëkka setluloo, ba noppi def leen saraxu yékkati-jébbal.
Numbers 31:30
TSK
Céru bànni Israyil bi ci des, nangeen ci sàkk benn ci juróom fukk yu nekk (50), ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt, mbaa gépp jur, te ngeen jox ko Leween ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji.»