TSK

TSK · Numbers 31:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yaw nag dinga gudd fan lool, doora nelaw, ñu denc la, nga fekki say maam ci jàmm.

Ba loolu weesee la bakkanu Ibraayma rot, mu nelaw, fekki ay maamam, gannaaw ba mu guddee fan, ba màggat lool te barkeel.

Yettro, sarxalkatu Majan ba nag, amoon na juróom ñaari doom yu jigéen. Ñu ñëw di rootsi, di duy mbalka, ya ñuy wëgge seen juru baay.

Te nga summi yérey carxal yu Aaróona, solal ko doomam Elasar. Aaróona moom, dees koy tërali ca ay bokkam. Foofa lay deeye.»

¶ Waayi bànni Israyil ja ñu jamoon, te boole kook ndawas Majan sa jam, mooy Simri doomu Salu. Kilifag kër maamam la woon ca Cimyoneen ña.

Boo ko séentoo ba noppi, yaw itam dees na la tërali ca say bokk, ni sa mag Aaróona,

Man nag ci réew mii laay dee. Du maay jàll dexu Yurdan. Waaye yeen yeenay jàll, ba nanguji réew mu baax moomu.

Moo tax, kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi, Jàmbaaru Israyil: «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! Maay fey samay noon!

Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.

Samay soppe, buleen di feyul seen bopp, xajal-leen am sànj, am sànj fajal boppam, ndax bindees na ne: «Man maay feye, maay añale.» Boroom bee ko wax.

Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def.

Ñu àddu ca kaw ne: «Buur bu sell, bu dëggu bi, loo deeti xaar ci àtte waa àddina, feyul nu sunu deret ji tuuru?»

Ay àtteem dëgg la, yoon la! Moo mbugal jigéenu moykat bu mag, bi yàq àddinaak moyam, feye ko deretu jaami Yàlla yi mu tuure loxoom.»