TSK

TSK · Numbers 34:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba ñu agsee Kanaan, Ibraam dafa jàll ca biir réew ma, ba àgg bérab bu sell, ba féete ak Sikem, ca garab gu mag, ga ñuy wooye More. Booba fekk na waa Kanaan a nga woon ca réew ma.

Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi jéggeegul dayo.»

¶ «Maa leen di dogal kemug suuf gu dale géeju Barax yi, ba géeju waa Filisti, daleeti ca màndiŋ ma, ba ca dexu Efraat, ndax maay teg waa réew mi ci seeni loxo, ngeen dàq leen.

Walbatikuleen dem, jàll-leen ca biir diiwaanu tundi Amoreen ña, ak mboolem réew ya mu feggool, ca joor ga, ak tund wa, ak suufu tund ya, ak Negew ca bëj-saalum, ba ca tefes ga, ca réewum Kanaaneen ña, ak Libaŋ, ba ca Efraat, dex gu mag ga.

Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.

Mu ne: «Yaw laay jox réewum Kanaan, muy sa cér, nga séddoo.»

¶ Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Fukki giiri Israyil yeek ñaar nag, kemi céri suufi réew mi ñuy séddoo, nii la wara tëdde: na wàllu giirug Yuusufa di ñaari cér.

Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.

Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.

¶ Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi, ngir may nu yaakaar juy dund.