Li ko dale ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci Israyil daal, nangeen leen lim, gàngoor ak gàngoor, yaw ak Aaróona.
TSK
TSK · Numbers 4:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
ñooy dénkoo ndénkaaneem, di dénkoo dénkaaney mbooloo mépp fi kanam xaymab ndaje mi, ndax ñooy sasoo liggéeyu jaamookaay bi.
dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ñi yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war.
dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ña yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war,
Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla?
¶ Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe. Yuusufa, Eli mooy baayam,
¶ Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.
¶ Wax ju wóor a ngii: kuy sàkku sasub jiite mbooloom gëmkat ñi, liggéey bu rafet lay xëccu.