TSK

TSK · Numbers 5:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. Bérab bu sell lees koy lekke. Lu sella sell la.

«Waxal Aaróona aki doomam yu góor ne leen lii mooy li mana tax ñu sore yu sell, yi ma bànni Israyil sellalal, ngir baña teddadil sama tur wu sell. Maay Aji Sax ji.

Mboolem jooxe yu sell yi bànni Israyil di jooxeel Aji Sax ji, sédd naa la ko, yaak sa doom yu góor, ak sa doom yu jigéen, ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Kóllërey xorom a ngoogu, du fecciku, xanaa sax dàkk fi kanam Aji Sax ji, ñeel la yaw, yaak saw askan.»

Lii mooy li lew sarxalkat yi, te bàyyikoo ci askan wi, ci ñiy rendi ay sarax, muy aw nag, di ab gàtt: nañu jox sarxalkat bi, mbagg mi ak lex yi, ak mbàq gi.

Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.