TSK

TSK · Numbers 6:23

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf!

Yanqóoba jegesi, fóon ko, xetu yére yi mu sol xeeñ Isaaxa, mu door koo ñaanal ne ko: «Sama xetu doom kay xetug tool la, bu Aji Sax ji barkeel.

¶ Gannaaw loolu Yuusufa ànd ak baayam ba fa Firawna, nuyole ko ak moom. Yanqóoba nuyu Firawna.

Gannaaw loolu mu ñaanal leen keroog ne leen: «Yal na Israyil di ñaane seeni tur naan: “Yal na la Yàlla def ni Efrayim ak Manase.”» Noonu la jiitale Efrayim, door caa teg Manase.

¶ Jant yooyu la Aji Sax ji ber giirug Lewi, ngir ñuy gàddu gaalu kóllëreg Aji Sax ji, di taxaw fi kanam Aji Sax ji, di ko liggéeyal, di taase barke ciw turam, te mooy seen péete ba tey jii.

¶ Ñaan gii nag la Musaa, góoru Yàlla ga ñaanaloon bànni Israyil, bala moo nelaw.

¶ Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Ci kaw loolu mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.

Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

¶ Melkisedeg moomu doon buurub Salem te nekkoon sarxalkatub Yàlla Aji Kawe ji, ba Ibraayma délsee jóge xareem baak buur ya mu duma, kooku moo ko gatandu woon, ñaanal ko.

¶ Ba tey ngëm la Isaaxa ñaanale Yanqóoba ak Esawu, ngir barkey ëllëg.

Aw yiw ak jàmm baawaan na, ñeel leen, ndax xam gu ngeen xam Yàlla, ak sunu Sang Yeesu.