¶ Nanga yóbbu yëkk wu ndaw wi ba ci bunt xaymab ndaje mi, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkk wi,
TSK
TSK · Numbers 8:12
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Na def ak yëkk woowu na muy def ak yëkku saraxu póotum bàkkaar rekk. Noonu lay def ak moom. Ni la ko sarxalkat biy defale seen njotlaay, ñu am njéggal.
¶ «Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil Aji Sax ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di saraxu póotum bàkkaar, bi ci des di sarax rendi-dóomal.
¶ Musaa teg ca indi yëkku sarax siy póotum bàkkaar, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkku sarax siy póotum bàkkaar,
¶ La ca tegu mu indi kuuyu saraxu rendi-dóomal bi, Aaróona ak doomam yu góor teg seeni loxo ca boppu kuuy ma.
Musaa wax ak Aaróona ne ko: «Dikkal fii ci sarxalukaay bi te joxe sa saraxu póotum bàkkaar ak sa saraxu rendi-dóomal, nga jotoo ko, yaw yaak mbooloo mi, boo noppee joxe saraxu mbooloo mi, jote leen ko, muy li Aji Sax ji santaane.»
ak ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, lu mu ci gëna jekku rekk. Menn mi saraxu póotum bàkkaar la, mi ci des di saraxu rendi-dóomal.
¶ «Bu Aaróona noppee, na indi yëkku saraxas póotum bàkkaaram, def ko njotlaayam mook waa këram. Na rendi yëkku saraxas póotum bàkkaaram,
Aaróona day teg ay loxoom ci kaw boppu sikket biy dund te tudd ci kawam mboolem ñaawtéefi bànni Israyil ak seeni tooñ, ak seeni bàkkaar yépp, boole ko yen sikket bi, teg ko ci loxol nit ku ñu yónni, mu dàq ko ca màndiŋ ma.
¶ «Su ko defee sarxalkat bi boole ko indi fi kanam Aji Sax ji, daldi joxe póotum bàkkaar bi, ak rendi-dóomal bi.
Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.