¶ Ci kaw loolu malaakam Yàlla, ma féete woon xarekati Israyil kanam naka jekk te di leen jiite, daldi toxu, féete leen gannaaw. Niir, wa leen jiitu woon it walbatiku, taxaw ca seen gannaaw,
TSK
TSK · Numbers 9:15
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Te bu Musaa duggaan ca xayma ba, taxaaru niir wa day wàcc, ne tekk ca bunt xayma ba, fekk Aji Sax jaa ngay wax ak Musaa.
¶ Keroog at ma topp ca at ma ñu génne Misra, ca benn fanu weer wa jëkk, ca lañu samp jaamookaay ba.
ba Musaa tëlee dugg ca xaymab ndaje ma, ndax niir wa màkkaanoo kaw xayma ba, ak leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba.
Niiru Aji Sax ji nag di leen yiir bëccëg bu nekk, saa yu ñu bàyyikoo ab dal.
Mbooloo maa nga sam Aaróona ak Musaa. Ci biir loolu, ñu ne gees xaymab ndaje ma, gisuñu lu moy niir wa muur ko, leerug Aji Sax ji feeñ.
Waaye yaw, ci sa yërmande ju réy, waccoo leen ca màndiŋ ma. Taxaaru niir wa noppiwula taxaw ci seen kanam bëccëg bu nekk, di leen jiite ca yoon wa. Taxaaru sawara wa it noppiwula taxaw guddi, di leen niital yoon wa ñuy jaar.
Mu firiw niir, yiire leen, ak sawara, ñu niitoo guddi.
¶ Ba waa jay agsi, jëmmi serub yaa nga taxaw fa féete kër Yàlla ga ndijoor, niir wa daldi fees ëttu biir ba.