Léegi kay nanu fasanteek sunu Yàlla kóllëre, daldi fase jigéen ñooñu ñépp, ñu ànd ak seeni doom, muy ni nga ko diglee rekk, sang bi, yaak ñi wormaal sunu santaaney Yàlla. Li yoon wi digle daal, na am.
TSK
TSK · Philippians 2:12
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.
Ab yaafus day yaakaar, du am; ab njaxlaf sàkku, woomle.
Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen ñiy déglu kàddoom, di lox. Lii de mooy seen kàddug bokk, yi leen jéppi, di leen dàq ngir samaw tur. Ñu ngi naan: «Na Aji Sax ji darajaal boppam, ba nu teewe seen mbégte, yeen ñii!» Waaye ñoom de ñooy rus.
¶ Ba loolu amee boroom kaso ba indilu ab làmp, daldi ne saraax dugg, ne gurub fa kanam Póol ak Silas, di lox.
¶ Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm.
¶ Kersaal leen nag taxul ma bind leen lii, waaye dama leen koy artoo, ndax yeenay sama doomi bopp.
¶ Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.
¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.
ndax seen loxo bi ngeen jo ci xamle xibaaru jàmm bi, te dale ko ca bés bu jëkk ba ba tey.
Ndax kat yeen la may ci jëmmu Almasi, yiwu gëm Almasi, rax ci dolli, ngeen sonn ndax moom,
Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam,
¶ Yeen waa Filib, xam ngeen xéll ne ba waareb xibaaru jàmm bay door, te ma bàyyikoo diiwaanu Masedwan, amul woon menn mbooloom gëmkat mu ma séqaloon ab joqlanteb ndimbal, xanaa seen mennum mbooloo.
Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu taamu, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.
Nanu def sunu kem-kàttan boog, ngir tàbbi ci googu noflaay, bala kenn a daanu ndax déggadi gu mel ni gu maam ya.
Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey, ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
¶ Kon nag gannaaw nguur gu deesul yëngal lanu jagoo, nanu jàppoo cant, di jaamu Yàlla ni mu ko bëgge cig njullite akug ragal,
¶ Loolu ci boppam wara tax ngeen def lu ngeen man, ba dolli ci seen ngëm, njàmbaar; seen njàmbaar, ngeen dolli ci xam-xam;