TSK

TSK · Philippians 2:27

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 5:19 TSK

Juróom benni njàqare teew, mu xettli la ca, ba ko juróom yaareel sax, doo ca loru.

ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel, ana lu mu lay jariñ? Nu la pëndu pax di sante, bay biral sa worma?

Moo lay baal foo ñaawe, di la wéral foo woppe.

Loolu lépp laa walbatiku xalaat, ngir lépp leer ma: Ku jub ak ku xelu ak seeni jëf, lépp a ngi ci loxol Yàlla. Mbëggeel ak mbañeel, xamoo lu la ciy xaar, lépp a nga ca kanam.

Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.

Nga ne: “Wóoy ngalla man! Aji Sax ji yokk na maw naqar. Onk naa ba tàyyi te awma noflaay.”

Acts 9:39 TSK

¶ Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Ay jëtun a nga fa woon. Ñoom ñépp di jooyoo, yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.

Kon kay xanaa ngeen jéggal ko, te dëfal ko, ngir mu baña sóobu ci naqar wu ko ëpp doole.