Fépp fu ñu leen dalalewul, génnleen dëkk booba te ngeen faxas fa seen pëndub ndëgguy tànk, seedeele leen ko seen ngàntal.»
TSK
TSK · Philippians 2:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.
Teraanga yu bare terale nañu nu ko fa, te ba nuy dem, jox nañu nu la nu soxla.
Dalal-leen ko ci turu Boroom bi, ni ko ñu sell ñi yelloo, te ngeen jàpple ko ci lépp lu mu aajowoo, nde moom itam xettli na ñu bare, ba ci man mii.
Dalal nañu sama xel, ak seen mos, yeen itam. Kon nit ñu mel noonu, fonkleen leen.
¶ Ndax ki ñu naw mooy ki Boroom bi gërëm, waaye du ki gërëm boppam.
¶ Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnaba. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko.
¶ Mag ñiy jiite mbooloo mi bu baax nag, nañu leen yellale ag njukkal ñaari yoon, rawatina ñi boole coonoy waare ak njàngle.