Xale bu góor, bu amee juróom ñetti fan war naa xaraf. Képp kuy góor ci seen maasoo maas, war naa xaraf, ba ci jaam bu juddoo sa kër, mbaa ku ñu jënd ci sa xaalis, ak bépp doomu doxandéem boo jurul.
TSK
TSK · Philippians 3:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Fekk amoon na waxambaanew ebrë wu fa nekkoon ak nun, te doonoon jaamub njiital dag ya. Nu nettali ko sunuy gént, mu firil nu ko, wax nu ku nekk la sa gént di tekki.
¶ Mu ne leen: «Ab Ebrë laa. Aji Sax jiy Yàllay asamaan laay jaamu, moom mi sàkk géej ak jéeri.»
¶ Ba juróom ñetti fani xale bi matee, ñu xarfal ko, tudde ko Yeesu, na ko malaaka ma tudde woon, bala moo sosu.
¶ «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.
¶ «Mboolem fi ma jaare ci samag dund, dale ko ca samag ndaw, ca ndoorte la, ba ma nekkee ca sama biir xeet, ak ca Yerusalem, lépp, mboolem Yawut yi xam nañu ko.
¶ Xanaa ay Ebrë lañu? Ak man itam. Xanaa ci xeetu Israyil lañu bokk? Ak man itam. Xanaa ay sëti Ibraayma lañu? Ak man itam.