ne ko: «Ñëwal nu dem rekk, nga gis ni ma farloo ci mbiri Aji Sax ji.» Mu waral ko watiiram, yóbbu ko.
TSK
TSK · Philippians 3:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.
¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,
¶ «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.
¶ «Man ci sama bopp, gàntal lu ma man turu Yeesum Nasaret, sama warugar laa ko defoon.
Waaye xeetu Israyil wi sàkku woon yoonu njub, ñoo moy yoon wi.
ndax kat maa gëna ñàkk solo ci ndawi Almasi, te yeyoowuma sax turu ndaw, gannaaw maa doon bundxatal mbooloom Yàlla mi.
ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.