¶ Gannaaw loolu Yeesu ne ay taalibeem: «Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol,
TSK
TSK · Philippians 4:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Layoo bi ci seen biir rekk firndeel na xaat ne daanu ngeen jéll bu réy. Lu leen tee muñ ag tooñ? Lu leen tee faaleedi alal ju ñu leen jëlal?
Moo tax, su dee aw ñam wu ma lekk mooy tax ma bàkkaarloo sama mbokkum gëmkat, dootuma lekk mukk aw yàpp ci àddina, ngir baña bàkkaarloo sama mbokkum gëmkat.
ndax yeen ci seen bopp, xam ngeen xéll ne Sang bi, ni sàccub guddi lay dikke.
Buñu yàq der te buñu bëggu ay, waaye nañu di bëggkati jàmm, te nañuy jëfe lewetaay gu mat sëkk, seen digg ak ñépp.
Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.
Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.
¶ Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiital-leen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.
¶ «Maa ngii di ñëw léegi. Ndokklee yaw miy sàmm kàdduy waxyuy téere bii.»