Psalms 1:1
TSK
Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon, taxawewuloo yoonu moykat, toogewuloo jataayu ñaawlekat.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon, taxawewuloo yoonu moykat, toogewuloo jataayu ñaawlekat.
Luy yoon wu aay, ma moyu, ba mana sàmm sa kàddu.
Yoonu ku bon, bu ci tegu; fu ab soxor di jaar, bu fa dox.
Bul jàdd, ndijoor mbaa càmmoñ, na sa tànk moyu lu bon.
Dëddul jëfi téxét ba dund, di jubal ci yoonu dégg.»
Xanaa kiy doxe njekk, di wax njub, bañ alalu foqati; loxo bay jalax ab ger, noppam di tanqamlu waxi bóome, bëtam di gëmm, ba du gis lu bon.
Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqlikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax. «Lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.