TSK

TSK · Proverbs 1:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Gewasi surgab góoru Yàlla ga, Alyaasa, ne ca xelam: «Eewaay sama sang daal! Day bàyyi Naaman waa Siri bii mu dem noonu rekk; jëlul dara ci li mu indi. Giñ naa ko ci Aji Sax ji, Kiy Dund, dinaa daw dabi ko, ba am ci moom as lëf.»

Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.

Bul xemmem daraam lu neex, ñam woowu la lay naxe.

mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.

Micah 2:1 TSK

Wóoy, ngalla ñiy mébét ñaawtéef, di ràbb lu bon ci seenub tëraay, bët set, ñu jëfe ko, ndax xam ne man nañu ko.

«Wóoy ngalla kuy dajaleel këram alalu yàqute ju lewul tey aj am tàggam fu kawe, ngir fegu ci yàqule.

Bumu di ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, waaye na lewet, bañu ay, te bumu di bëggkatub xaalis.

James 5:1 TSK

¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.

¶ Seeni gët xoolul lu moy ku ñu jaalool, te duñu bàkkaar ba regg mukk; ku dëgërul, ñu yóbbaale la. Ñooñu la seenub xol tàggatu ci ag bëgge, mii njurum alkànde!