Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
TSK
TSK · Proverbs 10:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Alal ju lewul day naaw; foral benn-benn, ba biibal.
di ko àttee ñàkkal ku ñàkk, di xañ àq sama néew-ji-dooley ñoñ, bay lekk ab jëtun, di sëxëtoo ab jirim.
Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»
Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»
¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.
ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.