TSK

TSK · Proverbs 14:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aana dem ba foofa, ànd ak naqaru xolam, di ñaan ci Aji Sax ji, tey jooy jooy yu metti.

Mu agsi nag ca góoru Yàlla ga, ca kaw tund wa, ne fëlëñ ca suuf, jàpp ca tànk ya. Gewasi dikk, bëgg koo bëmëx, mu ne ko: «Bàyyi ko, xolam a naqari. Aji Sax ji nag nëbb na ma ko, xamalu ma lan la.»

Job 6:4 TSK

Da di fetti Aji Man jee ma jam, ba tooke ji nàndal samam xel, mbugalu Yàlla yu raglu làng-déral ma.

Job 9:18 TSK

mayuma sax ma astandiku, xanaa reggal ma aw naqar.

Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.

Ku bëgga dund, dékku woppi yaram, waaye xol bu jeex maneesu koo wéye.

Su boobaa jàmmu Yàlla, ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol, ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.

¶ «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; doj wu ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.