Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa.
TSK
TSK · Proverbs 14:19
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Musaa ak Aaróona nag jóge ca Firawna, Musaa tinu Aji Sax ji ca mbirum mbott ya mu yare Firawna.
Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees.
Yosafat ne: «Waaw, kàddug Aji Sax jaa ngi ci moom kay.» Ba mu ko defee buurub Israyil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ak buurub Edom, dem ca Alyaasa.
Nii la ku wóolu boppam di mujje, mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.
Ña la daa néewal, seeni doom a lay sukkalsi. Ña la daa ñàkke worma, mujj di fóon say tànk. Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji», mbaa «Siyoŋ, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.»
Xeet yee ciy gis, rus, te seen gépp njàmbaar du tee ñu ub seen gémmiñ, seeni nopp buur.
Ñu dikk, jéggalu, génne leen ci biti, ñaan leen, ñu génn dëkk ba.