Ragal Aji Sax ji di ndoortel rafet xel, dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. Moo yeyoo cant ba fàww.
TSK
TSK · Proverbs 14:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
May ma dég-dég, ma topp saw yoon, toppe ko xol bu tàlli.
Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.
Yoonu njekk laay jaare, di jëfe li yoon àtte rekk.
Ku jub, yoon lay mébét; ab soxor di lal pexey wor.
Ku xelook ku dof, du yàgg ñu fàtte la; ay bés yu néew, ñu fàtte lépp. Acam! Dof, dee; rafet xel, dee.
Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ”
Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi.
Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.
¶ Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet.