2 Samuel 19:1
TSK
¶ Naka la Buur dégg loolu, naqar wu réy jàpp ko. Mu dem ca biir néeg ba, ca taax ma tiim bunt dëkk ba, di jooy. Ma ngay dem te naan: «Wóoy Absalom sama doom ja! Éey sama doom ja, céy Absalom sama doom ja! Éey waay su ma sañoon dee sax wuutu la, Absalom, doom. Éey waay sama doom ja!»